✕
Wolof
Wolof
[Souleymane Faye]
Arva aar Njaye
Arva yaw kaay
Arva aar Diodo
Arva yàbb xaari maam booy
Yàlla bu dara yàqu
Mamadooo
Diop yàbb xaari maam booy
Kon Arva ma way
Kii mooy Arva sama lingeer bi
Buñ ne danga baax kenn du ne guléet
Wëratuma leneen yaw laa doon seet
Yaay sama reeni xol
Gërëm naa la ndax Arva yaa may nitaal ni weer wi (Arva)
Àljanna laay dundu fekk maa ngi sa wet (yaw laa am)
Yaay tool bu nandul nawet
Jëmbët naa man sama jiwu ci yaw
Ndekke bëggewu ma la xol bi kese (daagul ma lay wane)
Arva sama ruu gi laa la yëgee (daagul ma lay wane)
Fu ma geesu gis la nga may gunge
Ni tàkkandeer Arva sama jumelle nga yaw (daagul ma lay wane)
Yaw danga yore jikkooy jeegu puso (daagul ma lay wane)
Samay mbokk ko wax waxuma ko
Yaayu Awa ak Serigne Babacar
Arva wayal naa la, man Mamadou miy sa jëkkër
Kon wayal naa la ndaameloo
Ndax sama sant ngay wuyoo
Diop yàbb xaari maam borom
Ree ju neex ji mbaa meroo
Tojal naa la colonel
Sama xol yaa koy maccloo
Diop yàbb xaari maam, lakk nga sama ngërëm
Wayal naa la ndaameloo
Ndax sama sant ngay wuyoo
Diop yàbb xaari maam borom
Ree ju neex ji mbaa meroo
Tojal naa la colonel
Sama xol yaa koy maccloo
Diop yàbb xaari maam, lakk nga sama ngërëm
Bu ñu delluwoon démb manam Imam yokkal cang gi
Ndax kontaan ci yaw, wool say mbokk damay dolli
Yaw jeegu jëkkante nga
Waaye man nga taamu
Ndax naru góor du àndak mbayaar yi
Boo fekkee woon keroog talaatay ndeer
Jigéen yaa taaloon seen bopp ca nekk ba
Ngir bañ gàcce duñ la yóbbul dara
Ndax yaw yaa jaay sa sant waaye sant bi nga ko jënde
Yombul sant dàqu ko, Diop du ku ne ka koy wuyoo
Xaari maam Diop Mamadou, kuy wër ku rafet judd
Ba yam ci moom dëppal
Ko fi gënul gënu la, yaay borom maamu buur yi
Kon wayal naa la ndaameloo
Ndax sama sant ngay wuyoo
Diop yàbb xaari maam borom
Ree ju neex ji mbaa meroo
Tojal naa la colonel
Sama xol yaa koy maccloo
Diop yàbb xaari maam, lakk nga sama ngërëm
Wayal naa la ndaameloo
Ndax sama sant ngay wuyoo
Diop yàbb xaari maam borom
Ree ju neex ji mbaa meroo
Tojal naa la colonel
Sama xol yaa koy maccloo
Diop yàbb xaari maam, lakk nga sama ngërëm
[Kine Lam]
Diop yàbb xaari maam moo Mamadooo
Yàbb mi ci mbaak mbeee
(Matar Ndoumbé Soxna Niaane
Serigne Koki Ndiaga Issa Dieye)
Leer gi baawaan be njukku ba makka
Mamadooo, Mamadooo
Yàbb xaari maam, chérie Arvaaaa
Ndaameloo sire
Ndaameloo sire bëggul ndaame sire
(Diop yàbb xaari maam)
Mamadooo
(Yàbb xaari maam, Diop yàbb xaari maam)
(Yàlla na ngay maam Diop yàbb xaari maam)
[Soda Mama]
Yàbb xaari maam
Maget Binata xaari maam
Serigne Koki Ndiaga Issa Dieye badan
Lakk dékki jaambuur yii, Kine Lam
Wax nga dëgg, way!
Ni walo ngay na ko daan jël
Xaar ma Yàlla réew mi dégluleen ma
Maa way sama doom ko koy arwa
Toucouleur Koura Ndiémé billaay
Ndaameloo sire
(Diop yàbb xaari maam)
Ndaameloo sire bëggul ndaame sire
(Diop yàbb xaari maam)
Mamadooo
(Diop yàbb xaari maam)
Poulo Niamata Kathié Torodo Samba ngary jama
Yaay maccloo jigéen ñi
Yaay maccloo góor gi
Sama doom ji la mu takkoon ba tay daañul
Jiitu nga leen sànni karawas gi daan leen
Jël bu ñu manta miin, bakkuwoo daanuwoo
Yaa yéwén goore
Bu la guwerner bëggoon na toxal
Bu la rangul sewul bañal
Bàyyi na ñama amoon ndax yaw
Xoti seeni këyit bañu bandoone ma
Yàlla ak yaw waa tax te yaa ma ko jaral
(Yàbb xaari maam, eyy!)
Comments
Ce morceau rend hommage au lieutenant-colonel des Douanes, Arva Kane, une figure à la fois professionnelle et familiale très admirée au Sénégal. Inspectrice principale des Douanes et chef du Bureau du Guichet unique du dédouanement des véhicules, elle incarne un modèle d’équilibre entre responsabilités professionnelles et engagement familial.
Le titre, très apprécié du public, met en lumière les valeurs de reconnaissance et de respect au sein du couple. Jahman y célèbre une épouse et mère dévouée qui, malgré une carrière exigeante, assume pleinement ses rôles familiaux. Le chanteur s’est inspiré de l’histoire vraie d’Arva Kane et de son mari, Mamadou Diop, tous deux perçus comme un exemple d’harmonie et de soutien mutuel.