• Jahman X-Press

    Éternelle

Share
Font Size
Wolof
Wolof
Mbëggeel la ma gaañ
Mbëggeel la ma faj
Ci xol lañu ma génne
Waaye sa xol nga ma faat
Yaakaaroon naa ni
Man duma bëggaat
Waxoon nañu ma ci gisaane
Maak yaw nara màggat
 
Yaw laay muñal mettit
Bi ma mbëggeel tekk yaw laay
Man yaw laay xool
Fàtte lépp lu ma metti, billaay
Dafa mel ni yaa ma gën jikk
Dama la xam rekk samay bunt tijjeeku
Maak yaw sunu bidéew dafa ànd
Li ma la yéexa xam rekk laay rëccu
 
Yaw la, yaw la
Juum ma ci yaw, xam naa ni yaw la
Yaw la (yaw la yaay), yaw la
Ki ma doon seet
 
Sama mbëggeel langi yokk
Bés bu nekk ba nga gënal ma sama bopp
Lu may doyee bànneex
Maak yaw suñ ko naru la bokk
Su ma teloon xam ne faaw ñu gaañ ma
Ngir ma jot ci yaw kon may gaañ sama bopp
Ñaan naa Yàlla maak yaw ñuy ànd
Lëngoo di dox ba ku ne yore bant
 
Yaw la, yaw la
Juum ma ci yaw, xam naa ni yaw la
Yaw la (yaw la yaay), yaw la
Ki ma doon seet
 
Ndeem àdduna du kër ñun ñépp a dañu fiy génn
Su ñu deewee maak yaw na suñuy bàmmeel dénd
Mu mel ni li ñu wër (lépp), li yépp
(Du pur kenn ku dul man ak yaw)
Foo ne laa lay fekk (fekk)
Foo mëna dem (muy taw walla muy ngelaw)
Dafa mu mel li ni ñu wër (lépp), li yépp
(Du pur kenn ku dul man ak yaw)
 
Baby Yàlla nañu ñu làngal bis
Yénne bi ma am ci yaw Yàlla la koy tis (oh oh)
Dundu sans yaw daf may tiis
Bés bi ma wara nelaw sa kanam la bëgga mujje gis
 
Oooooh yaw la (yaw la)
Juum ma ci yaw xam naa ni yaw la (yaw la)
 
Dama bëgg ba tiit ci sama mbëgeel
Xam naa mbëggeel sax waru na
Yaw laay muñal mettit
Bi ma mbëggeel tekk yaw laay
Man yaw laay xool
Fàtte lépp lu ma metti, billaay
 

 

Comments