• Jahman X-Press

    Damalay Beug

Share
Font Size
Wolof
Wolof
Bi ma la dénkee sama xol
Fowewoo ko nenne tuuti
Ba tax na su ma la doon wax fi nga ma tollu
"Dama la nob" dafay tuuti
Léegi dama am teint te bae yaa may jox li tax
Shampoing mbëggeel laay sangoo
Kon ku gis sama ex, nekkoo boppam lay nax
Su fóogee nii namm naa ko
 
Xawma nan lay def ak yaw
Waññil allure bi ngay daw
Sa xeetu mbëggeel lan la baby?
Tegal fi sama xol bi nga këf, nga këf, nga këf
Ba ma féemu def ay yëf, ay yëf
Yaw bokkok ñiy wax ndax yaa jëf moo tax
 
Man dama lay bëgg
Man dama lay bëgg ba kañ baby
Dama lay bëgg
Dama lay bëgg
Dama lay bëgg ba kañ
Chérie, dama lay bëgg
Man su ma yàkkamti woom juum
 
Gis naa ki ma Yàlla dencaloon
Man dama lay bëgg ba kañ
Ay su ma yàkkamti woom juum
Bëgg ba kañ
Gis naa ki ma Yàlla dencaloon
Man dama lay bëgg ba kañ
Sama yaakaar tasul ci yaw ba léegi
 
Foo jaar ma yëkkëti la ndax yaa ma daaneel
Jikko nga ci man maak yaw ba biir bàmmeel
Maak yaw a tax ñu naan baatu lingeer ak dameel
Tontu sa borom lay fay ndax xol nga ma ameel
Li ci mbëggeel lanaati lépp
Li bu raxul dof yitt ci la
Foo ne maa nga fa
Te fu ma la jiitu xaar laa fa
 
Amuma sago ci yaw
Est-ce que sax yaw doo nervis une vie, baby
Man yaw rekk laa miin
Yaay dalal sama xel ndax fu ma jaaxle yaw laay wutsi
 
Waaye fokk ñu takk pettaaw
Ndax xam nga cat dafa gaaw
Sa xeetu mbëggeel lan la, baby? (mon bébé)
Ñépp xam nañu man dama la
Dama la bëggawut
Bëgg naa la, baby
Sama cadeau d'Allah laa lay woowe
Nga bëgg leen sama tabbe
Naan laa lay woowee bi nga ma jàppe ba tay
Bàyyiwoo su jakk yakk nga waxe fë
 
Man dama lay bëgg
Man dama lay bëgg ba kañ baby
Dama lay bëgg
(Yénne naa la lu nekk sama baby)
Man dama lay bëgg, billaay
Dama lay bëgg ba kañ
Chérie, dama lay bëgg
Man su ma yàkkamti woom juum
 
(Bëgg ba kañ)
Gis naa ki ma Yàlla dencaloon
Man dama lay bëgg ba kañ
Ay su ma yàkkamti woom juum
Bëgg ba kañ
Gis naa ki ma Yàlla dencaloon
Dama lay bëgg ba kañ
Sama yaakaar tasul ci yaw ba léegi
 

 

Comments